Bismi LÂHIwa alâ millati RASÛLI wa man hajil QADÎMI
ÑAAR i RAKKÂH yi
Bu nu ñëw’ee tay fii ci NDar
Sant’a ti QÂDIM rekk’a war
NDax ku fi baax, Moo la defar
Ci Ñaar i Ràkkah yi fi NDar
Li war’al Ñaar i Ràkkah yi
Moo defar yàxxu-yàxx’u yi
Te ba mu jiit’oo Sangg yi
Boob’a la gëm loo xale yi
Ba ko Tubaab bi convoquer
BUUR YÂLLAH wax ko ca MBÀKKE
Neh ko : Faww nga dem tukki
NDax di nga génn ci MBÀKKE
Mu wooh lu MAAM CERNO mu ñëw
Neh ko : Dem’al ma NDar, te ñëw
Ma degl’u Saa BOROOM neh : Waaw
Waxtu Sama dem, léeg mu ñëw
CERNO ko jiit’u woon fi NDar
Ñew fi nir’ook gaynde gu ŋar
Tàngg fa aw tàng’aay wu tar
Ñu naah : Buy dell’u, nañ ko kar
Mu dell’u wax BAMBA neh ko :
Doo seen moroom, wan’e nga ko
La’ng ma wax’oon, fàtte wu ma ko
Te samay wax, xam na ñu ko
SËRIÑ bi wax ko, neh ko far :
Toog’al te yar, te sañcc KËR
Ba ñëpp xam ne, KIY defar
Ku baax ku ne, MOO la defar
Sangg bi daal di wuy ji NDar
Tubaab bi ! Nekk’oon ku soxor
Xam’ul lu baax, mbaa luy defar
Xanaa, di wexx’e ak’a dòor
Sëriñ MÛSÂ KAH wax na ko
Sheeq SAMBA JÂRAH wax na ko
Sëriñ MBAY JAXATE wax na ko
SHEYQÎ MÔDU KARÂ wax’a ti ko
Tubaab ya def lun mas’a man
Daan ko mettit’al lu ñu man
YONNEN bi wax, neh YÂLLAH : kon
Jox naa ko man, KUN-FAYAKÛN
BAMBA bër’eek Tubaab bi, daan
Kerog Firdawsî, ñëpp naan
Ca Géej i Kawsharâ, te naan :
Nañ maandi, ndax Suñu MBËR a daan
YÂLLAH neh Waa-ÀQLUL BADAR :
Muqara Bîn ya na ñu far
Dell’oo ko NGEEN toog ba fajar
Te na rang’oo médaille yu fort
Dell’u wax’aat ña woon Harâs
Ñu génn’e Tabala’y Harâs
Jiin’al ko MAAM BAMBA mi sës
Rëkk ci YONNEN bi ba fës
NDax MOOM, ay ndab’am, yëpp fees
Te deñc’al naa ko li fi des
Deñc’al na ko médaille yu bees
Ba tax, du faale ku ko siis
Tubaab yi waxtaan’ee ko waat
Maas’e ci BAMBA del’si waat
Kenn ci ñoom dell’u wax’aat
Neh kon : Gànnàr la ñuy jëm’aat
Ñu daal di koy yòbb’u Gànnàr
Malâkah yaa ko dell’u dar
Mu am fa ay xaymah yu Nâr
Di tambal’ee defar i Nâr
Ba ñu fa jòg’ee ba dem Céyéen
Nëpp di daw, di dem Céyéen
Ña YÂLLAH baax’e, ñoo ko séen
Daw na ñu ziyâr’e ko Céyéen
BUUR YÂLLAH naan ko : Léeg i kay
Da nga doon waat, wàcc nga tay
Jox naa la Falu-kaay gi tay
Malâkah yee ko seede tay
YÂLLAH jox’aat Gornemen’m
NDigël, ci BAMBA Suñu MAAM
Neh leen : Àddunah maa ko moom
Jox naa ko lépp MOOY BOROOM
Jox naa ko Mulk’eek Malakôt
Jox’aal e naa ko Jabarôt
Def naa bés’am yëpp, di fête
NDax ay mbir’am, lépp’a di mbòot
NDax, Moo di MAN, te maa di MOOM
NGËN-GI-MBINDÈEF it’am di MOOM
Al Jannâh it’am, Maa ko moom
Firdawsî laay dug’al Ñoñ’am
BAMBA ligéy’al RABBANÂH
Ba tax Malâkah yëpp naah :
Kii daal, du nit rekk xanaa
NDax, may’am yi ëpp na
SËRIÑ TÛBÂ wan’e leneen
Loo xam ne, yoomb’ul ci keneen
Du fii ci réew mi, du feneen
Te BAMBA ay MBIR’am du neen
Man mii di wax te di’b Xaj’am
Buy daw i xél ci am NGiir’am
May sant’a ti, di ko gërëm
Di baw, di xiir’u ngir jëmm’am
Sheeq SAMBA JÂRAH neeh na moom :
SËRIÑ TÛBÂ de MOO ko moom
Waaye du moom rekk la moom
SËRIÑ bi, ÑuN ñëpp’a la moom
Bu ñu ko nang’oo, te jàpp ko
Lu ñu yòotu, mu xëcc’al ñu ko
Buñ ko xam’ul, ump’al e ko
Lu mu ñu jox, ñu yàxx ko
Nañ jéem’a tòpp NDIGËL’am
Te jéem’a sòob u ci NGIIR’am
Te jéem’a sàkk u NGËRËM’am
Ba am ko, ndax lépp a di NDAM
Am ngërëm’am ci Àddunâh
Day tax a am ca AL Jannâh
Ay dëkk-u-waay yoy taar’u na
Yu bari, Lam yat mish huna
Kon kay, nañ koy sant’a ti, di wéy
Gudd’eek bëcëg, fu ñu man’a xëy
Wéet’al MAAM BAMBA mi xëy
Def’al ñu lol fawqa na mbay
NDax MOOM, ay MBIR’am ken du ko jeeh’al
Lépp’am da fay YÂLLA’k RASÛL
Mishâl u mbòot’am ni butéel
Bu YÂLLAH sol, kaste ko suul
Lii laa neh woon, di na ko wax
Ci KI tax a taxaw, di wax
Ñun ñëp, mbool’eem lu ñu fi wax
YÂLLAH na doon ay dax i wax
Ci DARAJA’y SËRIÑ TÛBÂ
Ak IBRAH FAATI ma mu neh Bâh
Bam neh ko Bâh, ba ni mu baah
SËRIÑ bi wan ko Martabâh
Wa AHMADU alâ mâ naqôlu wa kîlun taha wa salâm
SHEEQ AHMAD KARÂ ZÎ NÔREYNI AL SUHÂRAH
ÑAAR i RAKKÂH yi
Bu nu ñëw’ee tay fii ci NDar
Sant’a ti QÂDIM rekk’a war
NDax ku fi baax, Moo la defar
Ci Ñaar i Ràkkah yi fi NDar
Li war’al Ñaar i Ràkkah yi
Moo defar yàxxu-yàxx’u yi
Te ba mu jiit’oo Sangg yi
Boob’a la gëm loo xale yi
Ba ko Tubaab bi convoquer
BUUR YÂLLAH wax ko ca MBÀKKE
Neh ko : Faww nga dem tukki
NDax di nga génn ci MBÀKKE
Mu wooh lu MAAM CERNO mu ñëw
Neh ko : Dem’al ma NDar, te ñëw
Ma degl’u Saa BOROOM neh : Waaw
Waxtu Sama dem, léeg mu ñëw
CERNO ko jiit’u woon fi NDar
Ñew fi nir’ook gaynde gu ŋar
Tàngg fa aw tàng’aay wu tar
Ñu naah : Buy dell’u, nañ ko kar
Mu dell’u wax BAMBA neh ko :
Doo seen moroom, wan’e nga ko
La’ng ma wax’oon, fàtte wu ma ko
Te samay wax, xam na ñu ko
SËRIÑ bi wax ko, neh ko far :
Toog’al te yar, te sañcc KËR
Ba ñëpp xam ne, KIY defar
Ku baax ku ne, MOO la defar
Sangg bi daal di wuy ji NDar
Tubaab bi ! Nekk’oon ku soxor
Xam’ul lu baax, mbaa luy defar
Xanaa, di wexx’e ak’a dòor
Sëriñ MÛSÂ KAH wax na ko
Sheeq SAMBA JÂRAH wax na ko
Sëriñ MBAY JAXATE wax na ko
SHEYQÎ MÔDU KARÂ wax’a ti ko
Tubaab ya def lun mas’a man
Daan ko mettit’al lu ñu man
YONNEN bi wax, neh YÂLLAH : kon
Jox naa ko man, KUN-FAYAKÛN
BAMBA bër’eek Tubaab bi, daan
Kerog Firdawsî, ñëpp naan
Ca Géej i Kawsharâ, te naan :
Nañ maandi, ndax Suñu MBËR a daan
YÂLLAH neh Waa-ÀQLUL BADAR :
Muqara Bîn ya na ñu far
Dell’oo ko NGEEN toog ba fajar
Te na rang’oo médaille yu fort
Dell’u wax’aat ña woon Harâs
Ñu génn’e Tabala’y Harâs
Jiin’al ko MAAM BAMBA mi sës
Rëkk ci YONNEN bi ba fës
NDax MOOM, ay ndab’am, yëpp fees
Te deñc’al naa ko li fi des
Deñc’al na ko médaille yu bees
Ba tax, du faale ku ko siis
Tubaab yi waxtaan’ee ko waat
Maas’e ci BAMBA del’si waat
Kenn ci ñoom dell’u wax’aat
Neh kon : Gànnàr la ñuy jëm’aat
Ñu daal di koy yòbb’u Gànnàr
Malâkah yaa ko dell’u dar
Mu am fa ay xaymah yu Nâr
Di tambal’ee defar i Nâr
Ba ñu fa jòg’ee ba dem Céyéen
Nëpp di daw, di dem Céyéen
Ña YÂLLAH baax’e, ñoo ko séen
Daw na ñu ziyâr’e ko Céyéen
BUUR YÂLLAH naan ko : Léeg i kay
Da nga doon waat, wàcc nga tay
Jox naa la Falu-kaay gi tay
Malâkah yee ko seede tay
YÂLLAH jox’aat Gornemen’m
NDigël, ci BAMBA Suñu MAAM
Neh leen : Àddunah maa ko moom
Jox naa ko lépp MOOY BOROOM
Jox naa ko Mulk’eek Malakôt
Jox’aal e naa ko Jabarôt
Def naa bés’am yëpp, di fête
NDax ay mbir’am, lépp’a di mbòot
NDax, Moo di MAN, te maa di MOOM
NGËN-GI-MBINDÈEF it’am di MOOM
Al Jannâh it’am, Maa ko moom
Firdawsî laay dug’al Ñoñ’am
BAMBA ligéy’al RABBANÂH
Ba tax Malâkah yëpp naah :
Kii daal, du nit rekk xanaa
NDax, may’am yi ëpp na
SËRIÑ TÛBÂ wan’e leneen
Loo xam ne, yoomb’ul ci keneen
Du fii ci réew mi, du feneen
Te BAMBA ay MBIR’am du neen
Man mii di wax te di’b Xaj’am
Buy daw i xél ci am NGiir’am
May sant’a ti, di ko gërëm
Di baw, di xiir’u ngir jëmm’am
Sheeq SAMBA JÂRAH neeh na moom :
SËRIÑ TÛBÂ de MOO ko moom
Waaye du moom rekk la moom
SËRIÑ bi, ÑuN ñëpp’a la moom
Bu ñu ko nang’oo, te jàpp ko
Lu ñu yòotu, mu xëcc’al ñu ko
Buñ ko xam’ul, ump’al e ko
Lu mu ñu jox, ñu yàxx ko
Nañ jéem’a tòpp NDIGËL’am
Te jéem’a sòob u ci NGIIR’am
Te jéem’a sàkk u NGËRËM’am
Ba am ko, ndax lépp a di NDAM
Am ngërëm’am ci Àddunâh
Day tax a am ca AL Jannâh
Ay dëkk-u-waay yoy taar’u na
Yu bari, Lam yat mish huna
Kon kay, nañ koy sant’a ti, di wéy
Gudd’eek bëcëg, fu ñu man’a xëy
Wéet’al MAAM BAMBA mi xëy
Def’al ñu lol fawqa na mbay
NDax MOOM, ay MBIR’am ken du ko jeeh’al
Lépp’am da fay YÂLLA’k RASÛL
Mishâl u mbòot’am ni butéel
Bu YÂLLAH sol, kaste ko suul
Lii laa neh woon, di na ko wax
Ci KI tax a taxaw, di wax
Ñun ñëp, mbool’eem lu ñu fi wax
YÂLLAH na doon ay dax i wax
Ci DARAJA’y SËRIÑ TÛBÂ
Ak IBRAH FAATI ma mu neh Bâh
Bam neh ko Bâh, ba ni mu baah
SËRIÑ bi wan ko Martabâh
Wa AHMADU alâ mâ naqôlu wa kîlun taha wa salâm
SHEEQ AHMAD KARÂ ZÎ NÔREYNI AL SUHÂRAH